14 Silmah͈a ya ak ña lagi ñou fi mōm chi juma ja, te mu weral len.
Wande i njīt i seriñ ya ak bindānkat ya, ba ñu gise koutef ya mu def, ak gūne ya di h͈āchu chi juma ja, ne, Hosanna Dōm i Dauda; ñu mer lol,
Yesu dem cha bir Galilee yepa, di jemantale chi sēn i juma, di wāre linjil i ngur gi, te di weral h͈êt i opa ju neka, ak hêt i jangaro ju neka chi digante nit ña.
Yesu dem cha rew ya ak deka ya yepa, di jemantale chi sēn i juma, wāre linjil i ngur gi, te weral ña opa ñepa, ak jarak ju neka chi digante nit ña.