13 Te mu ne len, Binda nañu, ne, Suma nēg war na tūda nēg i ñān; wande yēn a ko def bereb ī sachakat.
Nu ne ko, Chi Bethlehem i Judæa; ndege yonent ba bind’ on na, ne,
Wande lile jot na, ndah͈ bāt ba ñu bind’ on chi sēn yōn motaliku, ne, Bañ nañu ma te defu ma dara.