11 Mbōlo ma ne, Kile di Yesu, yonent i Nazareth chi Galilee.
Te ñou, deka chi rew mu tūda Nazareth: ndah͈ la yonent ya wah͈ on motaliku, ne, Di nañu ko tūde Nazarene.
Ba mu dike chi bir Jerusalem, deka ba yepa yengatu, ne, Kile kan la?
Wande su ñu ne, Chi nit; da ñu ragal mbōlo ma; ndege jape won nañu John niki yonent.
Ba ñu jēme japa ko, ñu ragal mbōlo ma, ndege jape won nañu ko niki yonent.
Ñu lājte ko, ne, Kan nak? Ndah͈ yā di Elijah? Mu ne, Dowu ma. Ndah͈ yā di yonent ba? Mu tontu, ne, Dēt.
Te ñu lāj ko, te ne ko, Ana lutah͈ nga di batise, so dowule Krista, mbāte Elijah, mbāte yonent ba?
Jigen ja ne ko, Borom bi, gis nā ne yonent nga.
Ba nit ña gise koutef ga mu def on nak ñu ne, Chi dega kile di yonent ba di dika chi aduna si.
Ñena chi mbōlo ma nak, ba ñu dēge bāt yōyu, ne, Chi dega kile di yonent ba.
Ñu nêti silmah͈a ba, Lan nga wah͈ chi lu jem chi mōm, ndege ūbi na sa i but? Te mu ne, Mō di yonent.