6 Chi juromel i wah͈tu chi ngon potah͈ mu gēnati, feka ñenen ñu tah͈ou; mu ne len, Lutah͈ ngēn tah͈ou fi bechek bi bepa, te defu len dara?
Mu gēnati potah͈ chi fukel i wah͈tu ak ñar, ak chi ñetel i wah͈tu, te def nōga.
Ñu ne ko, Ndege ken a ñu bindul. Mu ne len, Dem len yēn it cha tōl ba.
Ba ña mu bind’ on potah͈ juromel i wah͈tu chi ngon ñoue, nit ku nek’ am h͈asab.
Ela naño def i ligey i ka ma yōni on, bi bechek bi neke: gudi g’ānge dika, bu ken munul a ligey.