4 Mu ne len, Dem len yēn it cha tōl ba, te di nā len joh͈ lu ela. Ñu dem.
Mu gēnati potah͈ chi jurom ñenentel i wah͈tu, gis ñenen ñu tah͈ou chi jēy ba te defu ñu dara,
Mu gēnati potah͈ chi fukel i wah͈tu ak ñar, ak chi ñetel i wah͈tu, te def nōga.
Ba Yesu juge fōfale, mu gis nit ku tūda Matthew, mu di tōg cha galakukay ba: mu wah͈ ko, ne, Topa ma. Mu jog, te topa ko.