34 Yesu am yermande chi ñom, lāl sēn i but, te chi tah͈ouay sēn i but gis, te ñu topa ko.
Mu gēna, te gis mbōlo mu rey; mu am yermande chi ñom, te weral sēn i jarak.
Yesu ô i tālube am fi mōm, te ne len, Am nā yermande chi mbōlo mi, ndege anda nañu ak man lēgi ñet’ i fan, te leku ñu dara; du ma len demlo te leku ñu, wala h͈ēchna di nañu ñaka dōle chi yōn wa.
Ñu ne ko, Borom bi, na suñu i but ūbiku.
Ba ñu jegeñse Jerusalem, te ñou cha Bethphage, chi tūnda i Olive, Yesu yōni ñar i tālube am,
Mu lāl loh͈o am, te fēbar ba bayi ko; mu jog te bukanēgu ko.
Fōfale mu lāl sēn i but, ne, Naka sēn ngum na ame nōgu chi yēn.
Wande ba mu gise mbōlo ma, mu yerem len, ndege da ñu jāh͈le, te tasāro niki nh͈ar yu amul samakat.