24 Ba ko fuka ña dēge, ñu mere ñar i mboka ya.
Mu ne len, Di ngēn nān suma nān chi dega: wande tōg chi suma ndējor ak suma chamoñ, munu ma ko maye kena, ganou ña ko suma Bay ba wājal.
Wande Yesu ô len fi mōm, te ne, H͈am ngēn ne i kēlifa i Gentile ya ēlif nañu len, te ñu rey ña ate nañu len ak sañsañ.