20 Fōfale ndey ī dom i Zebedee ñou fi mōm, ak dōm am yu gōr, di ko jāmu, te lāj ko lef.
Tūr i fuk’ i tālube ak ñar yangile: Benel bi, Simon ku tuda Peter, ak Andrew rak’ am; James dōm i Zebedee, ak John rak’ am;
Te ña neka chi gāl ga jāmu ko, ne, Chi dega yā di Dōm i Yalla.
Wande mu ñou te jāmu ko, ne, Borom bi, lêl dimali ma.
Ba ñu h͈arafe cha nēg ba, ñu feka gūne ga ak Mariama ndey am; ñu sūka te jāmu ko; ñu ūbi sēn i wah͈ande, te jebal ko i maye: wurus, fufata, ak mira.
Chi sēn digante la Mariama Magdalene nek’ on, ak Mariama ndey i James ak Joses, ak ndey ī dōm i Zebedee.
Ba ñu ko gise, ñu jāmu ko: wande ñena ña gumadi.
Bu mu fa juge, mu gis yenen i mboka, James dōm i Zebedee, ak rak’ am John, chi gāl ga, ak Zebedee sēn bay, di dāh͈ sēn i mbal; te mu ô len.
Ab gāna ñou fi mōm, te ñān ko, ne, Borom bi, su la nêh͈e, mun nga ma setal.