18 Ñunge dem cha Jerusalem, te di nañu jebal Dōm i nit ka i njīt i seriñ ya ak bindānkat ya; te di nañu ko ate ndah͈ mu dē;
Simon wā Canaan, ak Judas Iscariot, ka ko or on.
Cha sā sōsale Yesu dal di won i tālube am naka mu ela deme fa Jerusalem, te sona yef yu bare chi mag ya, ak i njīt i seriñ ya, ak bindānkat ya, te di ko rēyi, mu di dēkiji chi ñetel i fan am.
H͈am ngēn ne cha ganou ñar i fan h͈ewte ga di na jot, te ñu or Dōm i nit ka ndah͈ ñu dāj ko chi kura.
Lan ngēn dēfe? Ñu tontu ne, Dagan na dē.
Ba lelek sa jote, i njīt i seriñ ya ak i mag i nit ña ñepa fēnchu Yesu, ndah͈ ñu rēy ko.