15 Ndah͈ daganul ma def lu ma buga chi lu ma mōm? mbar sa but bon na, ndege mā bāh?
Cha wah͈tu wōwale Yesu tontu, ne, Mangi la gerem, Bay bi, Borom’ asaman ak suf, ndege nuba nga yef yile chi borom‐h͈amh͈am yi ak borom‐sago yi, te fêñal len i gūne.
Jelal li la lew, te dem sa yōn; buga nā joh͈ kile muje lu day ni sa bos.
Wande su sa but werule, sa yaram yepa di na fês ak lendem. Mōtah͈ su lêr gi neke chi you lendeme, naka la lendem gōgale di reye!
Naka nga ko maye won sañsañ chi kou nit ñepa, ndah͈ mu maye ña nga ko may on ñepa dūnda gu dul jêh͈.