Su ngēn di ôr, bu len am kanam gu dīs niki nafeh͈a ya; ndege di nañu ñaulo sēn i kanam ndah͈ nit ña gis ne ñunge ôr. Chi dega mangi len di wah͈, Am nañu sēn yōl.
So di sarah͈e mbōk, bul buftalo chi sa kanam, naka nafeh͈a ya di def chi juma ya ak mbeda ya, ndah͈ ñu am teranga chi nit. Chi dega mangi len di wah͈, Am nañu sēn yōl.