1 Ndege ngur i ajana niro na ak bena borom‐ker ku gēna chi sūba têl, ndah͈ mu binda i ligeykat chi tōl am.
Mu teg benen lēb chi sēn kanam, ne, Ngur i ajana niro na ak nit ka ji on jiu ju bāh͈ chi tōl am;
Mu teg benen lēb chi sēn kanam, ne, Ngur i ajana niro na ak pēp’ i sūna, bu nit fab, te ji chi tōl am;
Mu wah͈ len benen lēb, ne, Ngur i ajana niro na ak mporoh͈al bu jigen jel, te def chi ñet’ i andār i sunguf, be yepa foroh͈.
Ngur i ajana nirôti na ak mbal mu ñu sani chi gēch, mu japa h͈êt i jen wu neka:
Ba mu wah͈ante ak ligeykat ya h͈asab bechek, mu yōni len cha tōl am.
Wande lan ngēn dēfe? Kena nit am on na ñar i dōm yu gōr; mu ñou chi tau ba, ne, Suma dōm, demal ligey tey chi suma tōl.
Ngur i ajana niro na ak bena bur bu h͈umbal on nchēt i dōm am;
E Jerusalem, Jerusalem, mu rēy yonent ya, te jamat i h͈êr ña ñu ko yōne! naka lā don faral a buge dajale sēn i dōm, naka ganar gu di dajale i dōm am chi run lāf am, te ngēn bañ.
Fōfale di nañu nirale ngur i ajana ak fuk’ i h͈ēk, ñu jel on sēn i lampa, di gatanduji borom‐seyt.
Mel na niki nit ku don tūki chi benen rew, mu ôlu i jām am, te dēnka len alal am.
Rēchu len, ndege ngur i ajana jegeñsi na.
Man mā di garap i biñ bu dega bi, te suma Bay a di beykat ba.