9 Ba ñu dēge bur ba, ñu dem; te bidiw ba ñu gis on cha Penku, jītu len, be ba mu tah͈oue cha kou bereb ba gūne ga neka.
Ba ñu gise bidiw ba, ñu banēh͈u ak banēh͈ gu rey lol.
Ne, Ana ki jūdu Bur i Yauod ya? Ndege gis on nañu bidiw am cha Penku, te dika nañu ndah͈ ñu jāmu ko.
Mu yōni len fa Bethlehem, ne, Dem len, te ūt gūne ga bu bāh͈; su ngēn ko gise, delusi len te wah͈ ma ko, ndah͈ man itam ma jāmuji ko.