5 Nu ne ko, Chi Bethlehem i Judæa; ndege yonent ba bind’ on na, ne,
Ba Yesu jūdo cha Bethlehem i Judæa, chi bes i Herod bur ba, i borom‐h͈amh͈am juge on nañu cha Penku, ñou chi Jerusalem,
Ba mu dajale i njīt i seriñ ya ak i bindānkat nit ña, mu lāj len fu Krista war a jūdu.
Ndah͈ mbinda mi wah͈ul on, ne Krista di na jugeji chi gēño’ Dauda, ak cha Bethlehem, deka ba Dauda nek’ on?