3 Ba Herod bur ba dēge lōla, mu jāh͈le, mōm ak Jerusalem yepa.
Ne, Ana ki jūdu Bur i Yauod ya? Ndege gis on nañu bidiw am cha Penku, te dika nañu ndah͈ ñu jāmu ko.
Ba mu dajale i njīt i seriñ ya ak i bindānkat nit ña, mu lāj len fu Krista war a jūdu.
E Jerusalem, Jerusalem, mu rēy yonent ya, te jamat i h͈êr ña ñu ko yōne! naka lā don faral a buge dajale sēn i dōm, naka ganar gu di dajale i dōm am chi run lāf am, te ngēn bañ.
Te di ngēn dēga i h͈are ak i h͈abar i h͈are: otu len ngēn jāh͈le: ndege yile soh͈la naño am; wande muj ga dikangul.
Ñu h͈āchu, ne, Lan la ñu jote ak you, you Dōm i Yalla? Dā fi dika ndig geten ñu bala wah͈tu wa jot?