23 Te ñou, deka chi rew mu tūda Nazareth: ndah͈ la yonent ya wah͈ on motaliku, ne, Di nañu ko tūde Nazarene.
Yile yepa am on na ndah͈ la Borom bi wah͈ on chi yonent ba motaliku, ne,
Mbōlo ma ne, Kile di Yesu, yonent i Nazareth chi Galilee.
Ba mu deme be h͈araf cha rum ba, kenen gis ko, te ne ña fa neka, Kile nek’ on na itam ak Yesu wā’ Nazareth ba.
Nu tontu ko, ne, Yesu wā’ Nazareth ba. Yesu ne len, Man la. Te Judas itam, ka ko or on, mu tah͈ou ak ñom.
Mu lājati len ne, Ana ku ngēn di ūt? Te ñu ne, Yesu wā’ Nazareth ba.
Te Pilate bind on na h͈ameukay am itam, te def ko cha kura ba. Te lile la binda, Yesu wā’ Nazareth, Bur i Yauod ya.