Wande ba mu h͈alāte yef yile, malāka i Borom bi fêñu ko chi gēnta, ne ko, Yusufa, dōm i Dauda, bul ragal a sey ak Mariama, ndege li chi bir am chi Nh͈el mu Sela ma la juge.
Ba ñu dem on, malāka i Borom bi fêñu Yusufa chi gēnta, ne, Jogal, jelal gūne gi ak ndey am, te dou cha Mesara, te jēki fa be ba ma la cha ôe, ndege Herod di na ūt gūne gi ndah͈ mu rēylu ko.