9 Te mangi len di wah͈, Ku fase ak jabar am, lu moy mu di chi njālo, te sey ak kenen, njālo na: te ku sey ak ka ñu fase, njālo na.
Tālube ya ne ko, Su neke nōgule chi digante gōr ak jabar am, bāh͈ul ñu sey mbōk.
Mu ne len, Musa ndig sēn degeray i h͈ol bayi on na len ngēn fase ak sēn i jabar: wande amul on nōgule cha ndôrte la.
Wande mangi len di wah͈, Ku fase ak jabar am, lu moy mu di chi njālo, tah͈ na ko mu njālo; te ku sey ak mōm ka ñu fase, njālo na.