8 Mu ne len, Musa ndig sēn degeray i h͈ol bayi on na len ngēn fase ak sēn i jabar: wande amul on nōgule cha ndôrte la.
Ñu ne ko, Bōba lutah͈ on Musa ebal ñu joh͈ mbind’ i mpase, te fase ak mōm?
Te mangi len di wah͈, Ku fase ak jabar am, lu moy mu di chi njālo, te sey ak kenen, njālo na: te ku sey ak ka ñu fase, njālo na.
Yesu tontu ko, ne, Bul ko bañ lēgi, ndege nōgu la ñu ela motali njūbay yepa. Nōgale la bañatul.
Te jine ya dagān ko, ne, So ñu gēnê, bayi ñu ñu dem chi bir gēt’ i mbām ya.