7 Ñu ne ko, Bōba lutah͈ on Musa ebal ñu joh͈ mbind’ i mpase, te fase ak mōm?
Yusufa jekar am, nek’ on ku jūb, te nangôdi ndig wone ko chi biti, bug’ on na ko fase chi kumpa.
Nōgule nekatu ñu ñar, wande bena yaram. Mōtah͈ lu Yalla bōlāte, nit waru ko fasāle.
Mu ne len, Musa ndig sēn degeray i h͈ol bayi on na len ngēn fase ak sēn i jabar: wande amul on nōgule cha ndôrte la.
Wah͈ nañu itam, ne, Ku fase ak jabar am, na ko joh͈ mbinda i mpase: