4 Mu tontu len, ne, Ndah͈ jangu len ne ka len bind’ on cha ndôrte la, dafa len bind’ on gōr ak jigen,
Wande mu ne len, Ndah͈ jangu len la Dauda def on ba mu h͈īfe, ak ña and’ on ak mōm;
Yesu ne len, Ndah͈ mosu len a janga chi mbinda mi, ne, Doch wa tabah͈kat ya bañ on, mō di neki bop’ i tabah͈ ma: lile juge na fa Borom bi, te koutef la chi suñu i but?
Tālube ya dem, def naka len Yesu ebal on,
Wande mosu len a janga lu jem chi ndēkite ga, la len Yalla wah͈ on, ne,