25 Ba tālube ya dēge lōla, ñu jomi lol, ne, Ndōg kan a mun a mucha?
Te ma nêti len, Gen na yomba gelem tabi chi bir but i pursa, aste borom‐alal h͈araf chi ngur i Yalla.
Yesu sêt len, ne len, Lile munul a am ak nit; wande dara teūl Yalla.
Su ñu gatalul on bes yōgale, ken du kon muchi: wande ngir ña ñu tana, di nañu gatal bes yōgale.