23 Yesu ne i tālube am, Chi dega mangi len di wah͈, Jafeñ na borom‐alal h͈araf chi ngur i ajana.
Ka ñu ji won chi digante tah͈as ya, mō di ka dēga bāt bi; te i ntopato’ aduna si, ak nah͈ay i amam, waka bāt bi, mu bañ a mēña dōm.
Ne, Chi dega mangi len di wah͈, Su ngēn tūbule, te neka niki gūne yu tūti, du len h͈arafi chi ngur i ajana muk.
Wande ba far wa dēge kadu ga, mu dem ak nah͈ar; ndege am on na alal ju bare.
Kan chi ñom ñar a def la sēn bay buga? Ñu ne ko, Tau ba. Yesu ne len, Chi dega mangi len di wah͈, Publican ya ak garbo ya di nañu dem chi ngur i Yalla as yēn.
Ndege mangi len di wah͈, Su sēn njūbay sutule njūbay i bindānkat ya ak Pharisee ya, du len h͈araf chi ngur i ajana muk.
Yesu tontu te ne ko, Chi dega, chi dega, mangi la wah͈, Su nit jūduātule, du mun a gis ngur i Yalla.
Yesu tontu, ne, Chi dega, chi dega, mangi la wah͈, Su nit jūduwule chi ndoh͈ ak Nh͈el ma, du mun a h͈araf chi ngur i Yalla.