22 Wande ba far wa dēge kadu ga, mu dem ak nah͈ar; ndege am on na alal ju bare.
Ka ñu ji won chi digante tah͈as ya, mō di ka dēga bāt bi; te i ntopato’ aduna si, ak nah͈ay i amam, waka bāt bi, mu bañ a mēña dōm.
Bur ba nah͈arlu ko; wande ndig geñ am ga, ak ña tōg on ak mōm di leka, mu ebal ñu may ko ko.
Ndege ban njeriñ la chi nit, su ame aduna si yepa, te mu ñaka bakan am? wala wan wēchi la nit di joh͈e ndig bakan am?
Yesu ne ko, So buge mot, na nga dem, jay lo am, sarah͈ ko miskin ya, te di nga am jur cha ajana: te ñou, topa ma.
Yesu ne i tālube am, Chi dega mangi len di wah͈, Jafeñ na borom‐alal h͈araf chi ngur i ajana.
Ken munul a jāmu ñar i borom: ndege di na bañ kena, te sopa kenen; mbāte di na topa kena, te jēpi kenen. Munu len a jāmu Yalla ak alal.
Chi dega, chi dega, ma ne len, Di ngēn joyi te yuh͈u, wande aduna si di na banēh͈uji: di ngēn nah͈arluji, wande sēn nah͈ar di na sopalikuji chi banēh͈.