20 Far wa ne ko, Lōlu yepa lā dēncha: lan lā ñakati?
Teralal sa bay ak sa ndey: te, Sopal sa morom niki sa bopa.
Yesu ne ko, So buge mot, na nga dem, jay lo am, sarah͈ ko miskin ya, te di nga am jur cha ajana: te ñou, topa ma.
Wande ba ñu ko tope di lāj, mu yēkatiku, te ne len, Ku amul bakar chi yēn, na ko jeka sani doch.