15 Mu teg i loh͈o am chi sēn kou, te juge fōfa.
Wande Yesu ne, Bayi len gūne yu tūti yi ñu ñou fi man, te bu len len tēre: ndege ngur i ajana lew na ña mel ni ñom.
Kena ñou fi mōm, ne, Jemantalkat bi, lan lef lu bāh͈ lā ela def, ndah͈ ma mun a am dunda gu dul jêh͈?