13 Fōfale ñu indi fi mōm gūne yu tūti, ndah͈ mu teg i loh͈o am chi ñom, te ñānal len: tālube ya h͈ūle len.
Peter japa ko, te dal di ko eda, ne, Borom bi, na la Yalla yerem; lile du la dal muk.
Ndege i yōm la ñu judu on nōga cha sēn bir i ndey; yenen i yōm la ñu nit yōmlo; te i yōm la ñu yōmlo sēn bopa ngir ngur i ajana. Ku ko mun a nangu, na ko nangu.
Mbōlo ma h͈ule len ndah͈ ñu nopi; wande ñu dolê h͈āchu, ne, Borom bi, yerem ñu, you dōm i Dauda!