11 Wande mu ne len, Ñepa munu ño nangu kadu gile, wande ña ñu ko may dal.
Mu tontu len, ne, Yēn la ñu may ngēn h͈am i kumpa i ngur i ajana, wande ñom mayu ñu len ko.
Tālube ya ne ko, Su neke nōgule chi digante gōr ak jabar am, bāh͈ul ñu sey mbōk.
Ndege i yōm la ñu judu on nōga cha sēn bir i ndey; yenen i yōm la ñu nit yōmlo; te i yōm la ñu yōmlo sēn bopa ngir ngur i ajana. Ku ko mun a nangu, na ko nangu.