Su la sa loh͈o mbāte sa tanka moylô, dog ko, te sani ko: mō gen nga h͈araf chi dunda ak lago mbāte di sôh͈, aste am ñar i loh͈o mbāte ñar i tanka, ñu di la sani chi safara su dul jêh͈.
Wande mangi len di wah͈, Ku di mere morom am, mungi chi tafār i ate; te ku ne morom am, Dof bi, mungi chi tafār i ate bu rey; wande ku ne, Ēfar bi, di na neka chi tafār i safara’ nāri.