7 Suboh͈un aduna si ndig i mpaka! ndege i mpaka soh͈la naño dika; wande suboh͈un nit ka tah͈ mpaka ñou.
Wande mu walbatiku, te ne Peter, Randu ma, Seytane si; yā di suma mpaka; ndege topatoū la yu jem chi yef i Yalla, wande yef i nit.
Dōm i nit ka di na dem naka ñu bind’ on la jem chi mōm; wande suboh͈un nit ka ko ori! bāh͈ on na chi nit kōkale su juduūl on.
Ba ma neke ak ñom, dēncha nā len chi sa tur ña nga ma may on: te otu nā len, te ken sankuwul chi ñom, ganou dōm i tafar ja: ndah͈ mbinda ma motaliku.