32 Fōfale borom am ôlo ko fi mōm, te ne ko, E jām bu soh͈or bi, mā la baal on bor bōbale yepa, ndege dagān on nga ma:
Borom i jām bōbale yerem ko, mu bayi ko mu dem, te wocha ko ak bor ba.
Ba naule am ya gise la mu def, ñu nah͈arlu lol, te ñou nitali sēn borom la mu def on.
Warul kon you it nga yerem sa naule, naka ma la yereme on?
Wande borom am tontu ko, ne, E jām bu bon bi, te tayal; h͈am on nga ne da ma gōb fu ma jiūl on, te forātu fu ma tūrul on;