29 Naule am ba sūka, te dagān ko, ne, Muñal ma, di nā la fey.
Mōtah͈ jām ba sūka, te dagān ko, ne, Borom bi, muñal ma, di nā la fey yepa.
Wande jām bōbale gēna, te feka kena chi i naule am, ku ko leb on tēmēr i kopar: mu japa ko, ne ko chih͈ chi bāt am ne, Fey ma lo ma leb on.
Mu fēta, wande dem tejlu ko chi kaso, be ba mu feye bor ba.
Warul kon you it nga yerem sa naule, naka ma la yereme on?
Te baal ñu suñu i bakar, naka ñu baale ña ñu tōñ;