27 Borom i jām bōbale yerem ko, mu bayi ko mu dem, te wocha ko ak bor ba.
Wande jām bōbale gēna, te feka kena chi i naule am, ku ko leb on tēmēr i kopar: mu japa ko, ne ko chih͈ chi bāt am ne, Fey ma lo ma leb on.
Fōfale borom am ôlo ko fi mōm, te ne ko, E jām bu soh͈or bi, mā la baal on bor bōbale yepa, ndege dagān on nga ma: