26 Mōtah͈ jām ba sūka, te dagān ko, ne, Borom bi, muñal ma, di nā la fey yepa.
Naule am ba sūka, te dagān ko, ne, Muñal ma, di nā la fey.
Ba ñu h͈arafe cha nēg ba, ñu feka gūne ga ak Mariama ndey am; ñu sūka te jāmu ko; ñu ūbi sēn i wah͈ande, te jebal ko i maye: wurus, fufata, ak mira.
Ab gāna ñou fi mōm, te ñān ko, ne, Borom bi, su la nêh͈e, mun nga ma setal.