Di len jemantal ñu di dēncha lu mu mun a don lu ma len ebal on: te mangi neka ak yēn sā su neka, be cha muj i aduna. UNWIN BROTHERS, LIMITED, THE GRESHAM PRESS, WOKING AND LONDON.
Ba ngon jote nak cha bes bōba, bu jeka chi ay i bes ba, te bunta ya teju fa talube ya neka, ndege ragal on nañu Yauod ya, Yesu dika, te tah͈ou chi sēn diga, te ne len, Jama and’ ak yēn.
Te ganou jurom ñet’ i fan, i talube am nekati cha bir, ak Thomas and’ ak ñom. Yesu dika, feka bunta ya teju, mu tah͈ou chi sen diga, te ne, Jama and’ ak yēn.