15 Su la sa morom tōñe, demal won ko tōñ yangê’m chi sēn digante: su la dēge, fabi nga sa morom.
Tah͈na itam du sēn mbugel i Bay ba cha ajana, ndah͈ kena chi yu tut yile rēr.
Fōfale Peter ñou fi mōm, te ne ko, Ñāt’ i yōn la ma suma morom di tōñ, te ma baal ko? be jurom ñar i yōn am?
Nōgu la itam suma Bay ba cha ajana di def ak yēn, su ngēn dul baalalante sēn morom chi sēn h͈ol.