9 Ba ñu wache tūnda wa, Yesu ebal len, ne, Bu len wah͈ kena mpêñu mile, be ba Dōm i nit ka di dēki cha ñu dē ña.
Te mu ebal len, ne, Bu ko kena h͈am:
Wande mangi len di wah͈, Elijah ñou on na jēg, te h͈amu ñu ko won, wande ñu def ko lu ñu buga chi mōm. Nōgu itam la ño sonaleji Dōm i nit ka.
Mu ne len, Ndig sēn gumadi: ndege chi dega mangi len di wah͈, Su ngēn ame ngum gu day niki pēp’ i sūna, di ngēn wah͈ tūnda wile, Roñul cha bereb bale; te di na roñu; te kôn dara du len te.
Ba ñu deke chi Galilee, Yesu ne len, Di nañu or Dōm i nit ka chi loh͈o i nit;
Di nañu ko rēy, te chi ñetel i fan am di na dēki. Ñu nah͈arlu lol.
Ba ñu yēkate sēn but, gisatu ñu ken, ganou Yesu dal.
Yesu ne ko, Ntila yi am nañu i mpah͈, te mpich’ i asaman si am nañu i taga, wande Dōm i nit ka amul fu mu tedal bop’ am.
Yesu ne ko, Otul te bu ko wah͈ ken; wande demal wone sa bopa seriñ ba, te jebale maye ga Musa eble won, ndig sēde chi ñom.