4 Peter tontu, ne Yesu, Borom bi, bāh͈ na chi ñun ñu neka file: su la nêh͈e, di nā fi defar ñet’ i mbār; bena you, bena Musa, ak bena Elijah.
Te Musa ak Elijah fêñu len, di wah͈tān ak mōm.
Bay bi, ña nga ma may on, buga nā ne ñom itam ñu neka ak man fa ma neka; ndah͈ ñu sêt suma ndam li nga ma may: ndege sop’ on nga ma ba aduna si sosôngul.
Te h͈ewte i Yauod ya jegēnsi na, mu di h͈ewte i mbār ya.