3 Te Musa ak Elijah fêñu len, di wah͈tān ak mōm.
Mu sopaliku chi sēn kanam: h͈ar‐kanam am di melah͈ niki janta bi, te ser am wêh͈ tal niki lêr gi.
Peter tontu, ne Yesu, Borom bi, bāh͈ na chi ñun ñu neka file: su la nêh͈e, di nā fi defar ñet’ i mbār; bena you, bena Musa, ak bena Elijah.
Ndege Musa la ñu joh͈ on yōn wi; yiw ak dega bayako fa Yesu Krista.