25 Mu ne, Wau. Ba mu h͈arafe chi nēg ba, Yesu jekantu ko, ne, Lo dēfe Simon? I bur i suf si, chi kan la ñu di jele bāh͈ wala ngalak? chi sēn i dōm am, am chi i gan?
Ba mu ne, Chi gan yi, Yesu ne ko, Kôn dōm ya du ñu war a fey.
Wah͈ ñu nak, Lo dēfe? Ndah͈ dagan na ñu joh͈ Cæsar ngalak, am dēt.
Won len ma h͈ālis i ngalak li. Ñu yub ko h͈asab.
Nu ne ko, Cæsar la. Mu ne len mbōk, Joh͈ len Cæsar yef i Cæsar; te Yalla yef i Yalla.
Yesu tontu ko, ne, Bul ko bañ lēgi, ndege nōgu la ñu ela motali njūbay yepa. Nōgale la bañatul.