23 Di nañu ko rēy, te chi ñetel i fan am di na dēki. Ñu nah͈arlu lol.
Cha sā sōsale Yesu dal di won i tālube am naka mu ela deme fa Jerusalem, te sona yef yu bare chi mag ya, ak i njīt i seriñ ya, ak bindānkat ya, te di ko rēyi, mu di dēkiji chi ñetel i fan am.
Ba ñu wache tūnda wa, Yesu ebal len, ne, Bu len wah͈ kena mpêñu mile, be ba Dōm i nit ka di dēki cha ñu dē ña.
Di nañu ko jebal Gentile ya, ndah͈ ñu ñaual ko, ratah͈ ko, te dāj ko cha kura; te chi ñetel i fan am di na dēki.
Ne, Borom bi, Fataliku nañu ne nafeh͈a bōbale nôn na ba mu dund’ on, Chi ganou ñet’ i fan di nā dēki.
Wande ndege wah͈ nā len yef yile, sēn h͈ol fês na ak nah͈ar.
Yesu tontu te ne len, Maba len juma jile, te chi ñet’ i fan di nā ko delu tah͈oual.