22 Ba ñu deke chi Galilee, Yesu ne len, Di nañu or Dōm i nit ka chi loh͈o i nit;
Cha sā sōsale Yesu dal di won i tālube am naka mu ela deme fa Jerusalem, te sona yef yu bare chi mag ya, ak i njīt i seriñ ya, ak bindānkat ya, te di ko rēyi, mu di dēkiji chi ñetel i fan am.
Chi dega mangi len di wah͈, Ñena ñi tah͈ou file, du ñu mos dē, be ba ñu di gisi Dōm i nit ka mu di ñou chi ngur am.
Wande mangi len di wah͈, Elijah ñou on na jēg, te h͈amu ñu ko won, wande ñu def ko lu ñu buga chi mōm. Nōgu itam la ño sonaleji Dōm i nit ka.
Di nañu ko rēy, te chi ñetel i fan am di na dēki. Ñu nah͈arlu lol.
Ba ñu wache tūnda wa, Yesu ebal len, ne, Bu len wah͈ kena mpêñu mile, be ba Dōm i nit ka di dēki cha ñu dē ña.
Fōfale ñu bare di nañu fakatalu, orante, te sibante.
Cha ganou lōlu mu ūt naka la ko mun a ore.
Jog len, na ñu dem, ki ma orsi jegeñsi na.