2 Mu sopaliku chi sēn kanam: h͈ar‐kanam am di melah͈ niki janta bi, te ser am wêh͈ tal niki lêr gi.
Ganou jurom ben’ i fan, Yesu jel Peter, James, ak John rak’ am, te yubu len chi kou tūnda wu koue, ñom dal:
Te Musa ak Elijah fêñu len, di wah͈tān ak mōm.
Kanam am mel na melah͈, te chol am wêh͈ niki njōr:
Te Bāt bi yaramu on na, te dek’ on na ak ñun, te sêt on nañu ndam am, ndam niki ku di dōm i bay ju di bajo, fês ak yiw ak dega.
Bay bi, ña nga ma may on, buga nā ne ñom itam ñu neka ak man fa ma neka; ndah͈ ñu sêt suma ndam li nga ma may: ndege sop’ on nga ma ba aduna si sosôngul.