Cha sā sōsale Yesu dal di won i tālube am naka mu ela deme fa Jerusalem, te sona yef yu bare chi mag ya, ak i njīt i seriñ ya, ak bindānkat ya, te di ko rēyi, mu di dēkiji chi ñetel i fan am.
Ndege John ñou on na fi yēn chi yōn i njūbay, te gumu len ko won: wande publican ya ak garbo ya gum on nañu ko: te yēn ba ngēn ko gise, rechuwu len cha ganou sah͈ ndah͈ ngēn gum ko.