8 Ba ko Yesu h͈ame, mu ne, E gā’ ngum gu new, lutah͈ ngēn werante chi sēn digante, ndege amu len mburu?
Nōn’ ak nōna Yesu talal loh͈o am, te japa ko, ne ko, E borom‐ngum gu new, lutah͈ nga nimse?
H͈alāt nañu chi sēn bopa, ne, Ndig indiū ñu on mburu.
Wande su Yalla sānge nōgule ñah͈ i tōl mi neka tey, te su elege ñu sani ko chi tāl, du len gen a sānga’m, yēn nit i ngum gu new?
Mu ne len, Lutah͈ ngēn ragal, yēn nit i ngum gu new? Fōfale mu jog, te eda ngelou ya ak gēch ga; mu dal be ne nem.
H͈am nañu lēgi ne h͈am nga yef yepa, te soh͈lawu la ne kena lāj la: lōlo tah͈ ñu gum ne fa Yalla nga juge won.