Fōfale mandarga i Dōm i nit ka di na fêñ cha asaman; h͈êt i aduna si yepa di nañu yeremtu, te di nañu gis Dōm i nit ka mu di ñou chi i nir i asaman si ak kantan ak ndam lu rey.
Yesu ne ko, Wah͈ nga ko: te mangi len di wah͈, Ganou lile di ngēn gisi Dōm i nit ka mu di tōg chi loh͈o’ ndējor i kantan, di wachasi chi i nir i asaman.
Kadu gile nak dem on na chi digante mboka ya, ne talube bōba du dēi; wande Yesu wah͈u ko won ne du dēi; wande, Su ma nêh͈e ne mu jēki be ba ma ñoui, lan la chi you?