26 Ndege ban njeriñ la chi nit, su ame aduna si yepa, te mu ñaka bakan am? wala wan wēchi la nit di joh͈e ndig bakan am?
Ndege ku mu mun a don ku buga musal bakan am, di na ko rēr: te ku mu mun a don ku di rērlo bakan am ndig man, di na ko gis.
Ndege Dōm i nit ka di na ñou chi ndam i Bay am, ak i malāk’ am; te chi wah͈tu wōwale di na yōl nit ku neka naka ligey am day.
Su la sa but i ndējor moylô, loh͈ati ko, te sani ko; ndege gen na bena chi sa cher rēr, te du sa yaram yepa di tabi chi nāri.