25 Ndege ku mu mun a don ku buga musal bakan am, di na ko rēr: te ku mu mun a don ku di rērlo bakan am ndig man, di na ko gis.
Ku ūt dund’ am, di na ko rēr; te ku rēral dund’ am ngir man, di na ko gis.
Ndege ban njeriñ la chi nit, su ame aduna si yepa, te mu ñaka bakan am? wala wan wēchi la nit di joh͈e ndig bakan am?
Ku sopa dūnd’ am, di na ko rēral; te ku bañ dūnd’ am chi aduna sile, di na ko dēncha be cha dūnda gu dul jêh͈.