22 Peter japa ko, te dal di ko eda, ne, Borom bi, na la Yalla yerem; lile du la dal muk.
Cha sā sōsale Yesu dal di won i tālube am naka mu ela deme fa Jerusalem, te sona yef yu bare chi mag ya, ak i njīt i seriñ ya, ak bindānkat ya, te di ko rēyi, mu di dēkiji chi ñetel i fan am.
Wande mu walbatiku, te ne Peter, Randu ma, Seytane si; yā di suma mpaka; ndege topatoū la yu jem chi yef i Yalla, wande yef i nit.