2 Wande mu tontu len, ne, Su janta soe, ngēn ne, Di nañu am bes bu nêh͈ tey, ndig asaman si h͈onh͈a na:
Ti chi sūba, Di na h͈ēn tey, ndege asaman si tīm na. Mun ngēn a rañātle kanam i asaman si; wande munu len a rañātle melo i jamāno yi.